Marsiyya Seex Ibra Faal

20

description

L'épopée de Cheikh Ibrahima Fall, disciple de Cheikh Ahmadou Bamba, écrit par Serigne Moussa Kâ en poésie wolofwww.drouss.org

Transcript of Marsiyya Seex Ibra Faal

Page 1: Marsiyya Seex Ibra Faal
Page 2: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal

Seex Muusaa Ka (1891 - 1966)

Transcription : Serigne Mbacké Dieng

Révision et amélioation : drouss.org

© 1436 h / 2015 - www.drouss.orgTous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution

gratuite sans rien modifier du texte.Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez

nous contacter par le biais de notre site internet : www.drouss.org

Page 3: Marsiyya Seex Ibra Faal

2 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Quelques indications

Wolof Française = é per péru = ou rus rousc = th caam thiamñ = gn ñam gnamx = kh xol kholj = dj jibi djibinj = nd njaay ndiayend = nd nday ndeyeŋ ŋaam (machoire)ë = eu gëm = geumé = è (plus dur) = rér perduòo = au gòor gaureq = xx suqali soukh khaliii - uu - oo - aa ee (tirer sur le son) ; Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer

Marsiyya(1) (définition) :Dans la littérature arabe, le Marsiyya ou Rasa est un texte écrit pour exprimer, sans exagérer, son angoisse, sa détresse voire sa peur à la suite de la disparition d’une personne. Il met en exergue les qualités du défunt. Il chante son courage, sa bonne conduite, le donnant ainsi en exemple à la postérité. Il peut être composé :– soit pour regretter un proche disparu. C’est le vrai marsiyya.

Il naît de l’inquiétude, exprime la détresse sincère et communique l’angoisse à l’auditoire ;

1 c.f. LE MARSIYYA, Par Cheikh Amadou Kabir MBAYE

Page 4: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 3

– soit pour célébrer, toujours dans un contexte de détresse, les rois et les peuples antérieurs valeureux rappelant ainsi le passé glorieux ; - soit pour présenter ses condoléances dans la douleur et les pleurs en insistant sur les qualités du disparu et l’angoisse suscitée par sa mort ou plus fréquemment pour transmettre la sagesse populaire en abordant les thèmes de la vie et de la mort.

Dans le wolofal mouride, le marsiyya reste un poème lyrique exprimant des sentiments mélancoliques provoqués par un deuil mais réservé à la célébration d’un héros, un cheikh ou disciple très en vue, disparu. Il s’inspire du Huqqal-buka-u (Faut-il [les] pleurer ?). Ce poème mystique constitue le modèle fondamental pour le genre. Cheikh Ahmadou Bamba y décrit les caractéristiques des Maîtres soufis.

Précisions :Les vers que nous avons encadrés sont incertains. On les ne les retrouvent pas dans tous écrits que nous possédons ; aussi ni dans toutes les bandes sonores.

Page 5: Marsiyya Seex Ibra Faal

4 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Bismi-l-laahi-r-Rahmàni-r-Rahìmi

Wa Sallallàhu anla Seyidina Muhammadin wa salla-ma taslìman

àddina ndax day bëgg a jeex am gaa yu baax yeey bëgg a jeex am mbër yu ndaw yeey bëgg a seex Moo gaa yi xam naka pexe ?

ka xamlewon ag tarbiya ak ka xamon ag tarbiya moo buñ demee ba surga ya ku leen di wax nag luy pexe ?

ka wootewon ci àdduna ba ñépp wuysi fàddu na nan jéem a dëddu àdduna te jéem a wuyji mooy pexe

Seex Bàmba dem ci « Wamsashi» Seex Ibra dem ci « Tamsashi» Moo ñi fi des kuñuy dese ? yeenu muriid naka pexe ?

Page 6: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 5

Ab séet du dem ba doomi dikkeem Seex Ibra Faalay doom dikkeem moo rawi bokk, rawi doom topp mi waaj leen mooy pexe

Ab séet moroom yaay topp ma sëriñ muriid yaay topp ma jéem leen a wàlli séen po ma te ba po mii ngeen di fexe

Seex Ibra gëm ga làndi na moo tax mu dëddu àddina fekki na Bàmba sotti na wàcci na aljanay texe

Mas nay xibaar ag jébbuloom ba wax ne Yàlla mi ko moom moo ko ne Bàmba moo la moom raasi ko jox ko say pexe

Tegtalko yoon wa ab muriid di aw ba raw pexem Mariid ba am ngërëm bariy muriid te dootu ree di tex-texi

Page 7: Marsiyya Seex Ibra Faal

6 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Mu dal di dem Tayba-Daqaar Ngir dégg Bàmba di fa xaar seet na Sëriñ Tayba-Daqaar cim njàng lay xame pexe

Mu tëdd guddi listixaar ba mu xëyee ba tusubaar Sëriñ Mataar Turee fa jaar leeram ga wan ko lay pexe

Mataar Turee nga yori jóor yanu ko jëm Mbàkke-Kajoor Sëriñ bi yónni ko ca Mbuur Seex Ibra topp cay fexe

Mu jis fa Seex Aadama Géy Sànni mbiram dal di ca ŋoy Mu wan ko Bàmba mbër mu rëy Sëriñ ba naa ko foo fëxe ?

Mu wax ko tegtal ya fa moom Sëriñ Bàmba wan ko la fa moom mu xam ne jis na ka ko mom mu dal di fab mbiram joxe

Page 8: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 7

Ma wax la bis ba ndax mu wóor ñaar fukki fan ci weeru koor bisub dibéer la mbir ma wóor Seex Ibra yaa rëyi pexe

Mu sóobu far ba jiitu leen Seex Bàmba ne kii ëpp na leen leeram gu rëy gi wër na leen fum toll xol bay nux-nuxi

Wax na ne tuuti kon mu dem fekk Sëriñ bi lëm mbiram ba ken du jot ci baatinam ludul ca bis ba ñuy texe

Jaaraama Seexi Ibra Faal Làmp bi Sayxii Bàmba taal leeral nga réewmi yaa kamaal yal na nga dolliy beréxi

Ba mu ñëwee Mbàkke-Kajoor fekkon na daara ja di suur moo jëkk a yalwaani di woor ñu di ko ree di tex-texi

Page 9: Marsiyya Seex Ibra Faal

8 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Yendoo liggéey, fanaane root gaa yay nelaw ba naa xuréet ba luy ganaar ne kurkureet moo ko xewal daawul doxi

Moo fa xewal nuyoo di raam moo nu teree wuyu ne naam fekkon na ñuy jàng fa maam moom muy muriitu di fexe

Fekkon na daara ja di riir moo dindi àllarbaak dibéer lu Bàmba wax mu dal di buur lum mas am dal di joxe

Moo fa xewal soli sagar moo fa xewal sëqal kawar moo fa xewal saxoo sikar daawu fa bay di rux-ruxi

Ba mu demee Mbàkke-Bawol daf ne na waa kër ga ba wol naay soq tey rooti di wol booleek liggéey di ko joxe

Page 10: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 9

Lu bàmba wax mu dal di naaw fóorem ju rëy ja sant Saaw naa ko da ngay dellu gannaaw jànggil muriitu du pexe

Mbooleem muriid ya di ko soow mu mel ne dof bu mat a yeew ba mujj far ñépp ne siiw Meloom ya far di ko doxe

Mu jiitu far amul moroom far gëni bokk gëni doom jaaraama jaaraama xadiim wàcc nga wàccaaleeg texe

Yaw masulaa juuyook ndigal naka nga jóg të nga ndugal ku aw sa mboor duñ ko mbugal garmi yi yaa tax ñuy texe

Yaa jëkk a jébbale sa xol fekkon nga gaa ñay xorxoral ñaley setal ñaley nëxal yaa wane ngér mi ñiy doxe

Page 11: Marsiyya Seex Ibra Faal

10 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Yaa xam Sëriñ bi yaa xereñ daawoo weranteekub sëriñ bàjjo bi yaa bariy njariñ waane wi yàgg ngaa naxe

Am ngay gërëm ba am dërëm fab ngay dërëm jëndey ngërëm loo mas a am tàbbal këram ay junni daal nga daa joxe

Joxe nga àddiyay giléem yu safi ngurdu safi koom soldaar sa yaa joxe sa doom Faadilu Faal am na ag texe

Sa ndaw da daa dem ba Gaboŋ di yóbbu ay saaku yu roŋ di war ca gaal ya yori boŋ doo denci lëf ba muy maxe

Moo tax nga mel ne ag saxaar ku nar a dem da na fa jaar kuy ñaani paas na seeti gaar bum nég ba naa na ko pexe ?

Page 12: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 11

Ndegam da nga xebat sa paas way-wata yaa nga fa garaas seetal ma wax jii te xiyaas ndegam da ngaa am looy joxe

Baayay saxaar doomay wata kuy xamle Yàlla du fi të ku ji àndaar góob cay mata jiyal ci taw buy béx-béxi

Seex Bàmba taawloo Mustafaa Seex Ibra taawbay Mustafaa Diggante Marwataak Safaa Kuy aji warnafaa doxi

Seex Bàmba am nam Faadilu Seex Ibra am nam Faadilu ku xam na faale Faadilu kon ag mujam du toroxi

Seex Bàmba bégle nam Basiir Seex Ibra bégle am Basiir Mbég moo ci dem lekk ba suur jegeel ma kay toggiy joxe

Page 13: Marsiyya Seex Ibra Faal

12 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Seex Bàmba am nam Abdulaay Seex Ibra am am Abdulaay abdu mu nekk mat na waay bul weddi céebu kaay texe

Yal na ñu aw seen tànki baay ba mujj donnu seeni baay ba mujj boole seeni gaay aamiina ndax ñépp texe

Seex Ibra dem na wàcci na lum mas a aajo faju na ba xëy ne cipp àjjana nan farlu tey àndi pexe

Ken masl a jis sasam wu booy du daw kakoy muslook a njuuy moo jar a way te jar a jooy moo àddinaa man a naxe

Déglul ma lim fi ay ndamam ba gaa yi dollee xam mbiram ba xol yi bég ba dellu gëm leegi ragal yi yox-yoxi

Page 14: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 13

Jaaraama Ndey Saynabu Njaay la Soxna Jaara yor di jaay yaa ko mosal waa Njare-Njaay saw ŋàññ rot na yaa texe

Diggante Njukki ak Njamatil dañ daa dajey naani butéel yaa tax ñu jébbulu ca teel Faal Njaga yaa rëyi pexe

Mbulaki Sàqaki Sugeer dañ daa falook a fali foor(2) yaa tax ba dine di fa leer toxal nga póon mañ daa tuxe

Doomi Dàmmeel ya fa newon yaa dàm(m) mbir ma ñu newon tay ñépp ñépp a ngi fi nun ken amatul lu muy fexe

Yaa yóbbu Mbaaxaan ca Xafóor yaa tax ba xol ba dootu fuur yaa tax mu sànni yatu nguur fab yatu gëm di laaj pexe

2 ou (dañ daa falook a soli buur)

Page 15: Marsiyya Seex Ibra Faal

14 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Te xam ne mas naa yor junjung fumu jëm géwal ya naa kundung muy xas di bàkku cid goroŋ tay mu yam ak nun ay pexe

Yaa tax ba Abdulaahi Xaar taxaw fi bunt di fa xaar woyaflu bay lekk daqaar ngir sopp Bàmba miy joxe

Te xam ne moo doon doomi buur lum mas a wax ñu dal di buur la dale Mbaakol ba Kajoor moo amewoon seeni pexe

Yaa tax ba Soxna Mbenda Faal ak Gañsireeki Làlla Faal gën doomi soxna yii fi taal diine ju rëy ji ñuy doxe

Te xam ne seeni baay a moom Fedarba taalagut kanoom koo mas a jis ay jamonoom xolam ba daawul yox-yoxi

Page 16: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 15

Yaa tax ba Abdulaay ñaxib làmbi ndigal far na ko ub la gaa ya giiroo moo ko xab tabax na ay kër di joxe

Te xam ne mas naa dox fi moom tay jii mu mat sëkk boroom(3) ka denci doomam dib goroom lii doy na xarbaax duy pexe

Seex Ibra Faal amul moroom sàkk na mbër yuy roy ci moom leeral na penkkoom ak sowoom luy yàq dootul ñuy-ñuxi

La dale Ndar ba ca Dakaar jàll gannaaw yoonu saxaar mbër mu fa rëy ba ñu ne kaar Seex Ibra lay laaj pexe

Ndar la ko doomi Jaara may leeral na bopp jaara tay waykat wa Sàmba Jaara Mbay moo tax dënnam bay bëx-bëxi

3 ou (tay jii mu mat sàng ak boroom)

Page 17: Marsiyya Seex Ibra Faal

16 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Mu jóg fa agsi Ndànd-Faal jàpp fa doomi Ngóone Faal def ko ne làmp bu ñu taal tay Ngingineew moo fay fexe

Leeram ga sar ba agsi Kees ku ñëw mu duy la ba nga fees luy nit ku ñuul ak ku xees ñéppay bawoo fa Ngaay-Mexe

Sëriñ bi ñëw Njurbél mu ñëw gàddaay këram ya te du daw guddeek bëccëg ñam ya di ñëw Ba Bàmba xëy sàkk pexe

[jant a ngi jooy weer a ngi jooy mbooleem biddiw yépp a ngi jooy suuf ak asamaan a ngi jooy ku nekk naan na ka pexe]

Mbooleem muriid yépp gëlam ken xamatul kuy Sëriñam kune na ngéej a dal di dem àddina séppiy jëx-jëxi

Page 18: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 17

Mu dal di ŋoy ci Mustafaa ngir xam ne am na listifaa mag ñépp dem moom mu ne faa Masl a tuxooki yox-yoxi

Ba xëy na wuyji ab sanggam tuubaa la toggewoon añam Bàmba a ko jiiteloo ñoñam diggante Biib gaak Guy-Texe

Ma ngay janook tooli dërëm meññat mu gën junniy dërëm jis na lu weesu mébetam am na lu raw lam doon fexe

Bàmba xaroo na koy ngërëm Ridwaan tijjil na koy kërëm ñoñ huuru-hiineeng fa wetam jis na lu raw yoolub joxe

Ngërëm la Yonnen bay gëram Abaabakar ma jëkk a gëm la Sayxu Bàmba di gëram Seex Ibra mooy jëkk a texe

Page 19: Marsiyya Seex Ibra Faal

18 - Marsiyya Seex Ibra Faal

Medaay ba Yonnen bay takkal Abaabakar ngirug dëggal la Sayxu Bàmba di takkal Seex Ibra Faal bisub texe

Mànto ba Yonnen bay solal Abaabakar yor paresol jël saadixiinaya tofal yal na ko Bàmba fab joxe

[Bàmba a ko jël dal di ko fal mbooloo ma dar ko muy dëggal Jaaraama Seexi Ibra Faal yaa jar a xam bisub texe]

[Yaw ku la sopp daal di baax yaw ku la weddi dootu baax waa joo gërëm muy gën di baax kii ku bañ day toroxi]

[Nan jéem a toppi ndigalam te jéem a moytu ay tereem te jéem a roy ci ay jikkoom moo am njariñ bisub texe]

Page 20: Marsiyya Seex Ibra Faal

Marsiyya Seex Ibra Faal - 19

Muusaa la way wii wolafal yal na ko Shayxii Bàmba ful te boolekook gaa yu dëggal yoo xam ne ken du yox-yoxi

Aamiina aamiina ne leen aamiina ndax ñu boole leen ci mbóoti woy wi ba lu geen sàkkooti am ca ag pexe

Aamiina aamiina ne leen aamiina ndax ñu boole leen ci wax fi Muusaa ba lu ngeen sàkkooti am ca ag pexe

Allaahuma Salli anla Seyidinaa Muhammadin wa Sallim